Yako Waral

Maabo

Compositor: Não Disponível

Ma way Maabo
Maabo
Ma way Maabo
Maabo

Héy, xoolal ma kaw ba suuf
Maa leen dàq solu fuuf
Baby bul di jaawale
Du bare yére mooy sañse
Xool ma, fu ma mën a gën a nga ne file
Xam nga, du ci yére yi ci man mi la

Xool ma ni ma trois pièces jàppe
Te duma Djiby Dramé!
Damay jëm maak di dellu xale
Yaw foo may jëlëtee
Su ma neexee Obasanjo
Def classe teg châpeau
Kaay jël ay photo
Lii yépp yaa ko waral Guissé Maabo

Eh yaw xale bile
Ni ngay solu de neex na ma
Oooh, sa doxin bi neex na ma
Yeah, ni ngay solu de neex na ma
Oooh, sa doxin bi neex na ma!

(Ñu dem)
Kon nañu dem 'cakas cakas'
(Cëm, he!)
'Cakas cakas'
Dara duñu téye, 'cakas cakas'
'Cakas cakas'
(Ay way!)
Nañu dem 'cakas cakas' (hannn)
'Cakas cakas'
Dara duñu te 'cakas cakas'
Ñun dara du ñu tere dem!

Balaa ma dugg école
Ci laa am classe
Maa nekk ci sa xol
Ndax dama am cas
Baby, xool ma
Duma moroomu gone
Bés bi tay la
Dinaa la wan fi ma mëne

Di solu ni mannequin
Jëkk ni jëkk, di daagu ni diriyaanke
Musóoru ni Diouma Dieng
Te fu ma tasee sama cheveux doon sa Beyoncé
Kaay jege ma ñu snap selfie
Kaay ñu jël ay photo
Àdduna yépp gis ko!
Lii yaa ko waral Guissé Maabo

Eh yaw xale bile
Ni ngay solu de neex na ma
Oooh, sa doxin bi neex na ma
Yeah, ni ngay solu de neex na ma
Oooh, sa doxin bi neex na ma!

(Ñu dem)
Kon nañu dem 'cakas cakas'
(Cëm, he!)
'Cakas cakas'
Dara duñu téye, 'cakas cakas'
'Cakas cakas'
(Ay way!)
Nañu dem 'cakas cakas' (hannn)
'Cakas cakas'
Dara duñu te 'cakas cakas'
Ñun dara du ñu tere dem!

'Cakas cakas'
Yaw sama jigéen
'Cakas cakas'
Danga am classe, bëgg naa ci yaw
'Cakas cakas'
Man yaw yaay li ma moom
'Cakas cakas'
Wowooooh, Guissé Maabo

Ma way Maabo
Maabo
Ma way Maabo
Maabo

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital