Wa Li Nékhoul

Maabo

Compositor: Não Disponível

Maabo
Honey, I love you
Baby, I need you

Bés bu nekk dinaa la wax je t’aime
Duma sonn ci di la wan how much I love you
Dégg naa ñu ne dama dof ci yaw
Xanaa xamuñu ni yaay dalal li wéradi ci man

Bëgguma ñuy meroo, hie!
Nañu ànd longo, hie!
Bañuma ci xuloo ak ñoom ñépp
Nañu bàyyi ñu juboo te noppi

Yaay sama ngelaw, yaw rekk doy nga ci man
Su ma la gisul tamit, yaa mën dara ci man
Yëg-yëg bi amul limite, mel ni asamaan
Sa mbëggeel damay dundal ni oxygène ci man, hé!

Yaa ma tere nelaw, kenn rekk nga ci man
Su ma la gisul saalit, àdduna safal du ci man
Yëg-yëg num sore ci nit sama xol lay dal
Sa mbëggeel la may dundal, yaw yaa gën ci man, hiii!

(Eeh eh ayca ñu dem!)
Waa li neexul
(Ñu dem, eeh eh weuh)
Man, waa li neexul
(Aah, yaw mi la hé!)
Yaa may daanel
(Ñu dem ni la jëlel)
Man wa li neexul

Laajleen ma lu mu saf (lu mu saf?)
Lu neex (hey waay!)
Li ma nar ci moom mi (loo nar?)
Du jeex (oohhh!)
Ñu jëm tas suñu li, xamuñu
Yëg-yëg gu mel ni, non, amul!
Yaay sama chocolat, cacao piir bi
May sa oh la la, man may bu suur bi
Moom sa xol ak say xalaat (hé!), wor na
Awma xel ñaar (hé!), wor na

Yaay sama ngelaw, yaw rekk doy nga ci man
Su ma la gisul tamit, yaa mën dara ci man
Yëg-yëg bi amul limite, mel ni asamaan
Sa mbëggeel damay dundal ni oxygène ci man, hé!

Yaa ma tere nelaw, kenn rekk nga ci man
Su ma la gisul saalit, àdduna safal du ci man
Yëg-yëg num sore ci nit sama xol lay dal
Sa mbëggeel la may dundal, yaw yaa gën ci man, hiii!

Waa li neexul
Man, waa li neexul
Aah, yaw mi la hé!
Yaa may daanel
Ñu dem ni la jëlel
Man waa li neexul

Yaw mi la, yaw mi la eeh
Waa li neexul
Yaw mi la, yaw mi la eeh
Man, waa li neexul
Aaah yaw mi la eh
Yaa may daanel
Man waa li neexul

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital