Tukki

Maabo

Compositor: Não Disponível

Man bi may dem xawma dara
Bi ma yegsee gisuma dara
Ma bàyyi lépp sama ginnaaw
Man naan lay def
Dëkkuma fi, dëkkatuma fé
Yàgg àll baaxul non
Bokkuma fi, bokkatuma fe
Yàgg àll baaxul non
Maa ngi seet sama bopp ci samay mbokk
Ndax sama yoon am na ñu may dokk
Ku may gindi
Sama yoon wax ma sama bopp
Ndax moom lay seet
Bu de fitte ak fu la moy taxa tukki
Tay ragal na ko
Nekk jigéen téla dem tukki ute
Lu nekk dégg naa ko
Ki soppeeku na lu nekk dégg na ko
Ki de yàqu na héé! Kon fauk ma ñibbisi

Kañ lay ñibbisi, kañ lay ñibbisi ñibbisi
Ak fan lay ñibbeti, fan lay ñibbeti
Kañ lay ñibbisi, kañ lay ñibbisi ñibbisi
Ak fan lay ñibbeti, fan lay ñibbeti

Sama nekkin moom ump na leen wa werr
Bi de ma yónnee leen xaalis rekk yeen
Xamuleen sax sax lu may liggéey
Ak li may daj ba di leen ko yónnee
Te bala ma am seeni kayit
Pexe bu nekk nga jém ngir xañ ma ko
Man, immigré dafa metti
Fi ñi fi dëkkul ñépp bëgg ñibbi
Ku tukki nga ne diw tékki na, no no du ni
Ba mu deme yaggul tabax na yow loo fok fi
Dundu bitim-réew bokkul ak bu fi
Kenn du for xaalis dañu kaay liggéey man xamatuma
Fan la fété, fu ma mëna dem lénn lañu may laaj
Woooooh! Yow kañ ngay ñibbee
Wooooh! Léegi fan lay ñibbe

Kañ lay ñibisi, kañ lay ñibisi ñibisi
Ak fan lay ñibbeti, fan lay ñibbeti
Kañ lay ñibisi, kañ lay ñibisi ñibisi
Ak fan lay ñibbeti, fan lay ñibbeti

Han! Li de metti na
Yéhhh! Kañ lañ ñibbeti
(Kañ lay ñibisi)
Ak fan lañ ñibbeti
(Fan lay ñibbeti) ñun
Kañ lañuy ñibbeti
(Kañ lay ñibbisi)
Ak fan lañ ñibbeti

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital