Compositor: Não Disponível
Ñaar ñu Yàlla boole
Dox ci yoonu ngëm la
Bu sëy bi doré
Bul bàyyi sa nawle génn la
Li may yëg sama xol neex na loolu
Yaw boroom kër nga léegi
Jabar loo ko mën xel daf ci tollu
Ngeen boole mbégté ak mettit
Sa jabar munul yam ak kenn
Jubóolel bul di nëbboo
Na la miin ngeen xaritoo
Sëy bu amul respect du lénn
Ba lay neex jàmm am
Kat yërmande tuut su kenn ju mé
Ngeen di jàppalante itam
Boole seen doole sa su ne, hei!
Benn xol ak xel
Tay diisóo, délen waxtan ci tey
Am këru mbëggeel
Am këru mbëggeel
Ngeen dundu àljana!
Ñaar ñu Yàlla boole
Dox ci yoonu ngëm la
Bu sëy bi doré
Bul bàyyi sa nawle génn la (eh!)
Négu sëy de manul xatt su xol yi booloo
Jàmm ak yar ci la la séyloo
Dél muñ domm
Jabar wet sa jëkër du la waññil
Xecco bi mooy indi gañe
Su ngeen digluwante
Du ngeen di réeroo
Woolu wanté séy xaléy réeroo
Waaye mbëggeel lay doré
Ngir ànd bi sore, faw kenn baña rëy
Di kaf seen biir di foo di ree
Ba lay neex jàmm am
Kat yërmande tuut su kenn ju mé
Ngeen di jàppalante itam
Boole seen doole sa su ne, hei!
Benn xol ak xel
Tay diisóo, délen waxtan ci tey
Am këru mbëggeel
Am këru mbëggeel
Ngeen dundu àljana!
Du sey bi doré
Bul bàyyi sa nawlé génn la